Torox
Refrain :
Mère bi mi ngi may sàndi ñaan
Ragalu ma dara lu ma sòng daan Yeah yeah
Lu baax laa la yeene
Soxla wu ma sa dara budee am naa wer akk gudd fan
Ragalu ma torox
Am naa ñaanu yaay duma torox
Yalla xol lay fay duma torox
Duma tallal loxo ndaxte jòmb naa ko trop
Couplet 1 :
Nekk yaaram taxul ñu baayi la bopp
Jarul bind LETTRE xam naa ñi ma Haine ( N)
Maa nekk si sa xol te doo ma baayi nopp?
Wër di naan garap taxul nga nekk rèen (reine)
Loo muñ mu jeex, fii da ngay dee ndax ay xalaat'ag muñ
Bu ñii di wax luy jur xalaat kee di xalaat a jur
Kuy dolli sant ay fétiches nu ñuy tëyee sa tour ? (Tur || tuur)
Ñoo bokk tente te ñooy teg ngente wala ñu suul
Jog bañ a xaar
Takk Peinture du la aar( art)
Boo bëggee yar say doom bul door sa doom yi ay yar,
Mën nañ la mere
Soo bëggee ñu mucc dee len saytu
Yagg di nañ tekki li may wax takk ko teere anh
Couplet 2 :
Jòmb naa ko trop
Tax gedd ñi ma suuroon
Summi xalaat yiñ ma solloon
Foraat ròngoñ yi ma tuuroon
Da ñu yakk li ma ñoroon
Tax ma yem ci sama boroom
Ñu ne fayoo naar bi xorom
Budee joxoo mere bi boram , i swear
Yenn saay geej gi di na mer
Di na mujj giif yagg-yagg di na fer
Dara bum la yeem petaaw buy seet sax di na reer
Soxla wu ñu gaz pour mën tàngal seeni nerfs
Fii ku fi bonn yes sa bopp nga koy def
Fii ku fi baax rekk ñu toog si say xef
Du ma tête vide xam naa dara mel ni Kòkki
Lu jot dina yòmb robinet sax xëyul sotti
Outro
Tekki sama mind yeah
Lepp dina fine yeah
Awma njegenaay hustle everynight , Teral sama yaay yeah (X2)